#FreeSenegal lyrics

Songs   2024-12-22 15:57:00

#FreeSenegal lyrics

Dëkk ci dëkku nittu fitna

Sonn di wax yen ñëpp a yem kiif-kiif la 6-9

Li ma si gën a meti di gis boy yi di dee

Reew mi ñi koy fiy jiite ñëppay roy Lucifer

Nàcc ba coow li jeex sunu ròngoñ yi duñ fer

Naaj bu dem jànt fake ñoo la folli bul rëy

Gàddu sa call di Twitter su njaboot bi di dee

Mënu toog di muñ rekk di len xool ñu ñuy ray

Nawu ma politicien du ma politique man

Kuy tanqamlu kilifa diine du maay wax lu muy deeg

Suba yaay rus a netali say doom sunu tay

Ndaw yi prison la ñuy xëy sen école la ñuy gëj

Ndox bi jox nga ko Macron mool du joow ba gis jën

Police aar lañ ko santoon tay ñoy door nitt ñi gun

Mere bu Ci ñakk sa doom yuuxu wooy fu ñu jëm

Xeex bi ñëpp a Ci d’accord ndax ñoom yoon bi ñu jëll

Mënoon nañ la dènk kaso bañ la jox suñu dëkk

Palais moy dènc sacc Rëbës di tëjj Nittu Dëgg

Du mèdd ngen ñu foog mais nervis rekk du doy

Bàmmeel du tëye ku dee di dox

Na leer ci say nopp bët bu rusul tojj

Loy doyee jamm reew mu mënul dox

Jaay sunu pétrole bu ñuy sangu ñoy geen utti ndox

Taal sunu alal bu ñu fippoo nga geen tukki daw

Jàng am diplôme mais jaratul may utti job

Ku feebar dee nga hôpitaux yi amul gaz

Loo jëll ci ku jaay sa maam yi da fay lew ni Auchan

Caga duñ ko nax ñaari yoon duñ la jox 3ème chance

Doyna dereetu baadoola dootul siim cere France

Dereet di tuuru moo gën drapeau bi cuubu

Reew mey mës di nguuru da ñuy fen ñi lay dunguru

Gëmël Yalla te dem

Sa lëndëmaay da fa leer

Jarul nga tere marcher parce que jaay nga sa reew

Doo ku ñuy jangal nu ñu raxasoo xam nañ sa loxo settul

Taxoo len ñu jog politiciens mbalit sax daf ko sèxlu

Macky Idy Niasse

Tant que demmoo len abal ñu match bi du tas

Ñuy bañ dëkk bi takk ngay gën di sacc ci biir mbas

Bu ci sa doom deewoon yemale nga ko fii bu yagg

Fate le 23 juin tax nga fogoon ne lii du am

Ni la woon bi SOPI di dem ñuy xaar kuy ñëw soppi système

Jeunesse bi foo musique fècc ba ròmb gox bi système

Télés yi di ñu gëlëmmël sunu kom-kom di ci dem

Wax ma lu ñu def ci mbey mi tous ces hommes cultivés

Ñi des ci kaso bi xeexal luñ sen bopp

Du doon dee akk dund batay duñ xeex akk Senghor

Lu waay di def bës di na wadd sa kaw

Lu waay di def bës di na wadd sa kaw, right?

Dip Doundou Guiss more
  • country:Senegal
  • Languages:Wolof, French, English
  • Genre:Electronica, Hip-Hop/Rap, Pop, R&B/Soul
  • Official site:https://www.instagram.com/dip_doundouguissofficiel/
  • Wiki:
Dip Doundou Guiss Lyrics more
Dip Doundou Guiss Featuring Lyrics more
Excellent Songs recommendation
Popular Songs
Artists
Songs